KAN MOOY SOKHNA ASTOU GAWANE MBACKE bint Cheikh Ahmadou Bamba

Поделиться
HTML-код
  • Опубликовано: 9 сен 2024
  • KAN MOOY SOXNA ASTU GAAWAAN ?
    Soxna Aychatu Mbàkke bint Cheexul Xadiim, ñu gën koo xam ci Soxna Astu Gawaan. Mooy ki njëkka feeñ jamono ginaaw bi Sëriñ bi jugée ci géej gi, ci weeru koor atum 1904 ca Xumaag (Mauritanie).
    Wayjuram wu jigéen mi ngi tudd Soxna Soxna Xadijatu Joob, dëkk ca Kokki, gëna siiwé ci Soxna Xari Gànnaar, ndax daa féeté woon Mauritanie jamono yi fa Sëriñ bi nekkee.
    Soxna Astu, mi ngi jàngge Alxuraan ci nijaayam ju tudd Maam Sàmba Jaaga Joob. Ginaaw bi jàngg na ci moom lenn ci téeréy xam-xam.
    Bi mu tolle ci dem kër, Sëriñ bi jox ko mbokkam mu tudd Sëriñ Muhamadul Amin Turé, mi bokk ak Allaaji Moor Faati Turé mom Maam Seex Anta.
    Ba mu fa demee, nekkee woon fa jaamu Yàlla, ak ligéey ak topp kilifaam, Yàlla defal ko fa njaboot gu bàrkeel, muy Soxna Buso Turé, Soxna Ami Turé ak Sëriñ Moodu Turé.
    Waaye ñatti doomam yépp nak làqu nañ lu jiitu Soxna si di fi jugé, mu wane woon ca ak ngëm lool ak wakkiilu ci Yàlla, dàl di wax ne « bu ma kenn jooyal, man da may sant Yàlla ba ma sama doom yépp jiitoo, ndax sama xol baña bëgg leneen lu dul Yàlla ».
    Soxna Astu, doonoon ku yaatu lool, tabe lool, bëgg Alxuraan lool ak Qasida, fonkk njabootug Boroom Tuubaa lool, daan léen seeti ak di léen topotoo. Doonoon ku amub cér ci ñoom, daan léen tarbiya ak di léen ligéey loo ngir faj séeni aajo.
    Sëriñ Fàllu mas naa seede ci moom ba wax doomam Sëriñ Moodu Buso Jeng neko, « sa bajjan de soo fexee ba làq ngëramam, aajo joo amati di na faju ».
    Nekkoon ku mana yar jigéen ci ligéeyub kër ak xamal léen àdduna, goor ñi yit daan na léen tarbiya ci di léen ligéey loo, ak di léen zikar loo ak jàng Qasida.
    Qasidag Mawahibu ak Sindiidi, bokkoon na ci yi mu gënoona fonkku, te daan digal Murid yi ñuy farlu ci di ko jàng.
    Fonkoon na Café Tuubaa lool, ndax Sëriñ Tuubaa da ko koo masa jox ci loxol boppam, mootax Yàlla defaloon na ko ci ak jagle, ba daan na ci saafara mbooleem jangoro yi ak di ci faj aajoy jaam ñi.
    Noonu la doone woon ab taalubé bu dëggël, te ñépp ràññee ko ci bëgg Sëriñ Tuubaa, daan na def sax leeg-leeg ku koy ñaanloo mbiri àdduna, mu di la wax naan « ak taalibé rekka jara ñaanlu »
    Bis bii ñu koy fàttali ku di màggal giñ koy defal ci 25 diggi tabaski, mi ngi ko doon defee ci ndigalul Boroom Tuubaa, daan na ko def ca Gaawaan, ak Ndulo ba ba muy ñibbi si Tuubaa, bàyi wu ko, ba ni mu làqoo, moom lañ koy fàttali koo ba leegi.
    Sëriñ Muusaa Ka moo ko defaloon bëyit yii :
    "Ya bint Cheyxii Ahd’ibn Jaara
    Yàl na nga am ay doom yu sampi daara
    Gis naa la ngay jàngg « Sujood ak Mulki »
    Yàl na la Seex Bàmba dugal ci fulki
    Xam naa ni soo doon goor yilif waa Mbàkke
    Mbaa ngay fetal jihaar, di dem ba Màkka
    Seetal sa maam mu baax ma, wàkka Jaxu Jéey
    Darale woon na réew mi, noon ya di ko jooy
    Kon nak bi ngay jigéen, royal ca Aycha
    Ngir Saadixiina’ag Saadixaati yaafusa
    Yiléy bëyit maa la ko woy man Muusaa
    Ngir xam ne garbu woo ni jeegi siisaa"
    Soxna Astu, ginaaw bi mu dundé dundu gu bàrkeel, te daan xettalee, amoon yërmandé lool ci mbindéef yi, te amoon yitté ju kawe lool, mi ngi làqu ci atum 1984, ñu deñci ko ci Tuubaa.
    Yàl na nu Sëriñ Tuubaa fayal
    Ci xalimag : Akb Majalis

Комментарии • 23