BISMI LAAHI RAHMANI RAHIMI "Allaahu ma salli allaa Seydinaa Muhamadu Salli wa sallim, yaa Rabbi, salli a laa Muhamadu" Saa maam Limaamu wooté na Ba "Lanbiyaayi" woolu na Te Ruuhu Laay jiitu na Di làmpu leeri Medina Yaaram bu yiw bi wàcc nga Yaa Ruuhu Laay tedd nga Ku koy werante weddi nga Su ma yabo ne sànku nga Yàlla la yonni ngay Nabi Ngay seen gënéél ginnaaw Nabi Liggééy nga, am ngërëm lëmbe Sa ñaari leer yi jolli na Ñaari ngërëm nga boole, am Nga ndam sa may ga yaatu na Firdawsi ngay tëggoo junjung Yaa Séydi moom nga tuumë ja Gëm léen te woolu tey dëgël Di sant Laahu kiy ndimmël Buur Yàlla moo la may, Rasuul Nu gëm ko woolu diine ja Yaa xalla yoon wu réy wu yaa Wu jëm ca pééy yu magg ya Sa ngir mi leer na noo ngi jaamu Bañji diiné pertana Fekkon nga yoonu diine sew Ba nééw ji doole yépp daw Nga xalla yoon wi, yaa fi raw Ku fonk jamu waaxusil Goor ak jigéén di taalibe sikkar sa riir fa baabu ba Ba xol ya buur digaani ba Amiin ja, doy na noo jubël Xamxam ba raw na foore ya Jaaxal na lawliya yi ya Yaa jiité lanbiya yi ya Diiwaan bi yaa di seen ngënéél Yaa saytu diine jiy defar Jullit yi, sant leen lu war Ñiy xantu diine ngir sa leer Ñuy topp tééré ya di jiir Ñi weddi Njiin dañoo xamul Ki mën ci diiné, noo dëggal Da ngeen a laajul kiy jubal Nde moo di goor gu laabiir Jom-jomlu jommi fey na ko réy-réylu, réér it fey na ko Xamul na laaj ñu wax ko ko Ci yoonu diine mooy li war Damaa gisul ku mel ni Maam Limaamu Laay te dégguma Ku wax ne Yàlla moo ma yonni Moo ko wax nu woolu ko Gëm seede leen ne sant naa Ki tax ma seeru Séydinaa Ba gëm ko, naa ko "aamanaa" Ku woolu sant war na la Sëriñ sa toppu tank ba Saa bay Libaass ne maay boroom Kuy xañtu weer ba jant fenk Xamal ne leer ya wër na la Njaal-all yeek njanaaw yi ñook Garab yi boole gëm na ñoo Nit ak jinney werante, noo La woolu, Seydi tedd nga Bu gaalug Baay Libaas riddéé Ba gëm yi naani Kawsara Kerook, ñi gàntu Baay Libaas Di ñee ñi gëm ca kump ga Ñi tëx te buur dañoo tëkkaale Mahdiyook i walliyu Ka wax ne Yàlla moo ma yonni Kooka moo di Nabiyu Araab yi ak Tubaab yi ñoo Jëkkoon ci yoonu Nabiyu Wolof di xaar mujjug jamaana Maam Limaamul Mahdiyu Yaaram ba feeñ na ciy leboo Xërëm ya tiit na bay faboo Boroom ngënéél la nuy xaboo Yaa woote diine, noo wuyyoo Subhaana maa ko yéénéwoon Nu boole xol yi ndax nu man di jéém a roy ñi jiituwoon te aw ci yoonu Muhammadoo Lu fiy jullit nu bokk Ndey Da gaan ci Buur bi leeri pééy Ndax Buur jubal sunub liggééy ci lampi leeri Muhamadoo Yonnent yi wootewoon li laahi dakkantalees na leen ci Laahi Ku dee te doo"aduuwa"Laahi di Abdalaahi Muhamadoo Nabee dikkoon ne jaamu leen Yonnentub Yàlla ñeel na leen Ku weddi kii dawal keneen Te génn yoonu Muhamadoo War ngeen na xam ne jangu neen Te jëfewoo ko moo di ten bu teey bu neex te doo ca naan Gojam ba ñeel na Muhamadoo Moo tax ba Baay Libaas ne leen da ngeen di wax te laaju leen War ngeen a gaaw ma àtte leen ci yoonu Diine Muhamadoo
Allaahu ma salli allaa Seydinaa Muhamadu
Salli wa sallim, yaa Rabbi, salli a laa Muhamadu"
Allahouma sali ala Seydina Mouhamado❤❤❤ sali wa Salim ya yarabi sali Allah Mouhamado 🥰
Yalla na yalla yokou lérou mame Libasse Niangue tè taf niou ci barkém ci Barkè khaïrou khalhi lahi Seydina Limamou Lahi(psl)
diadieufty laymakhtar yalna yalla faay.
Yalna niou yalla fayal baye laye🤲🤲🤲
Alhamdoulahi ! Jajeuf laye
Salalahou Aleyhi wa Salim❤️❤️❤️❤️
Machalah laye makhtar
Dieuredieuf ABDOULAYE
BISMI LAAHI RAHMANI RAHIMI
"Allaahu ma salli allaa Seydinaa Muhamadu
Salli wa sallim, yaa Rabbi, salli a laa Muhamadu"
Saa maam Limaamu wooté na
Ba "Lanbiyaayi" woolu na
Te Ruuhu Laay jiitu na
Di làmpu leeri Medina
Yaaram bu yiw bi wàcc nga
Yaa Ruuhu Laay tedd nga
Ku koy werante weddi nga
Su ma yabo ne sànku nga
Yàlla la yonni ngay Nabi
Ngay seen gënéél ginnaaw Nabi
Liggééy nga, am ngërëm lëmbe
Sa ñaari leer yi jolli na
Ñaari ngërëm nga boole, am
Nga ndam sa may ga yaatu na
Firdawsi ngay tëggoo junjung
Yaa Séydi moom nga tuumë ja
Gëm léen te woolu tey dëgël
Di sant Laahu kiy ndimmël
Buur Yàlla moo la may, Rasuul
Nu gëm ko woolu diine ja
Yaa xalla yoon wu réy wu yaa
Wu jëm ca pééy yu magg ya
Sa ngir mi leer na noo ngi jaamu
Bañji diiné pertana
Fekkon nga yoonu diine sew
Ba nééw ji doole yépp daw
Nga xalla yoon wi, yaa fi raw
Ku fonk jamu waaxusil
Goor ak jigéén di taalibe
sikkar sa riir fa baabu ba
Ba xol ya buur digaani ba
Amiin ja, doy na noo jubël
Xamxam ba raw na foore ya
Jaaxal na lawliya yi ya
Yaa jiité lanbiya yi ya
Diiwaan bi yaa di seen ngënéél
Yaa saytu diine jiy defar
Jullit yi, sant leen lu war
Ñiy xantu diine ngir sa leer
Ñuy topp tééré ya di jiir
Ñi weddi Njiin dañoo xamul
Ki mën ci diiné, noo dëggal
Da ngeen a laajul kiy jubal
Nde moo di goor gu laabiir
Jom-jomlu jommi fey na ko
réy-réylu, réér it fey na ko
Xamul na laaj ñu wax ko ko
Ci yoonu diine mooy li war
Damaa gisul ku mel ni Maam
Limaamu Laay te dégguma
Ku wax ne Yàlla moo ma yonni
Moo ko wax nu woolu ko
Gëm seede leen ne sant naa
Ki tax ma seeru Séydinaa
Ba gëm ko, naa ko "aamanaa"
Ku woolu sant war na la
Sëriñ sa toppu tank ba
Saa bay Libaass ne maay boroom
Kuy xañtu weer ba jant fenk
Xamal ne leer ya wër na la
Njaal-all yeek njanaaw yi ñook
Garab yi boole gëm na ñoo
Nit ak jinney werante, noo
La woolu, Seydi tedd nga
Bu gaalug Baay Libaas riddéé
Ba gëm yi naani Kawsara
Kerook, ñi gàntu Baay Libaas
Di ñee ñi gëm ca kump ga
Ñi tëx te buur dañoo tëkkaale
Mahdiyook i walliyu
Ka wax ne Yàlla moo ma yonni
Kooka moo di Nabiyu
Araab yi ak Tubaab yi ñoo
Jëkkoon ci yoonu Nabiyu
Wolof di xaar mujjug jamaana
Maam Limaamul Mahdiyu
Yaaram ba feeñ na ciy leboo
Xërëm ya tiit na bay faboo
Boroom ngënéél la nuy xaboo
Yaa woote diine, noo wuyyoo
Subhaana maa ko yéénéwoon
Nu boole xol yi ndax nu man
di jéém a roy ñi jiituwoon
te aw ci yoonu Muhammadoo
Lu fiy jullit nu bokk Ndey
Da gaan ci Buur bi leeri pééy
Ndax Buur jubal sunub liggééy
ci lampi leeri Muhamadoo
Yonnent yi wootewoon li laahi
dakkantalees na leen ci Laahi
Ku dee te doo"aduuwa"Laahi
di Abdalaahi Muhamadoo
Nabee dikkoon ne jaamu leen
Yonnentub Yàlla ñeel na leen
Ku weddi kii dawal keneen
Te génn yoonu Muhamadoo
War ngeen na xam ne jangu neen
Te jëfewoo ko moo di ten
bu teey bu neex te doo ca naan
Gojam ba ñeel na Muhamadoo
Moo tax ba Baay Libaas ne leen
da ngeen di wax te laaju leen
War ngeen a gaaw ma àtte leen
ci yoonu Diine Muhamadoo
Talibe Serigne ablaye ya bakh machalah
ABDOULAYE NIANG KÈN genou la diadieuf LAYE
MACH'ALLAH ❤❤❤❤❤❤
Mashallah mashallah
Machallah laye makhetar
MACH'ALLAH
Merci ahlousalatou
Dieureudieuf laye mactar ♥️♥️♥️
Machala baye amoul mass
Diouli si Baye laye rekk mo worr
Walhae ndey sann baye laye amoul mass
ma sha Allah
Masala
Ahlou salatou jah jeuh laye
😍😍😍😍😍😍😍😍😍
❤❤❤❤
💖
WOLOF GUAMA FENGUOU BESS NIKI TAYE WOLOF LA NAMPA WOYELA BATAYE
❤❤