Abba Kara - SANTATI (Clip Officiel)

Поделиться
HTML-код
  • Опубликовано: 10 сен 2024
  • ABBA KARA 313, Vous invite à découvrir, vivre et ressentir l’immensité de la richesse des paroles reposées sur un plateau de mélodie à la fois douce et rythmique. Le morceau SANTATI ( l’acceptation de la volonté divine ) est inspiré en grande partie d’un poème du Général KARA que nous rendons un vibrant hommage.
    SEÉN YOBBALU MAGAL
    Crédits de la chanson et du Clip
    Studio : Chicory Word Music
    Arrangement : Ibrahima NDIAYE
    Mix : Ibrahima NDIAYE
    Coeur : Amina Jadid
    Percussions : Serigne KARA FALL et Noreyni
    Stylisme : Beugu Baye KARA
    DIRECTOR : Vito KARA DIEDHIOU
    D.O.P : Vito KARA
    DRONE OP : Vito KARA
    LIGHT : Bouba KARA
    Lyrics
    1ère Couplet
    Bismillahi maa ngi ñëwaat di santati
    Téy jooye fi di reeye fee didi (2) ak tati (3)
    Dees na sant di jooy dees na sant di ree
    Moodu Mbakke booy sant deel jooy'aka ree
    Jooyu mbekte daa bokkul ak jooyu nakkar
    Boo jullitee do mën a jooy jooyu nakkar
    Te sax benn Murid wart a mën a amu'k nakkar
    Bamba ci xol wart a mën a and'ak nakkar
    Refrain
    Bamba Bamba cëy Daam
    Hummm Boroom Njareem
    Bamba Bamba cëy Daam
    Xaadimoooooo
    Bamba Bamba cëy Daam
    Ahmadul Xadiim Boroom Jaam ñi
    Bamba Bamba cëy Daam
    Boroom Tuubaa
    2 ème Couplet
    Sëriñ Tuubaa sant ko day maye koom
    Ñakk ko sant ci miim réew day joxe góom
    Ñakk itam nangu ni réew mi Bamba mooko Moom
    Doonul lu gën ndaxte mën na noo xañu'w koom
    Siiwal nañ fi réew mi Bamba mooko Moom
    Ba ndawi réew mi ñépp maase ni dëgg la mooko Moom
    2 ème refrain
    Siiwal nañ fi réew mi Bamba mooko Moom
    Ba ndawi réew mi maase ni mooko Moom
    Xaadim rasuul sant la warna nu
    Siiwal nañ fi réew mi Bamba mooko Moom
    Ba ndawi réew mi maase ni mooko Moom
    Hummm Yaakaari jaam yi
    Siiwal nañ fi réew mi Bamba mooko Moom
    Ba ndawi réew mi maase ni mooko Moom
    Yaa siggil der bu ñuul bi Xaadim
    Siiwal nañ fi réew mi Bamba mooko Moom
    Ba ndawi réew mi maase ni mooko Moom
    Yaa teral lislaam
    Neh na nu la jërëjëf
    Oh jërëjëf Waaw jërëjëf
    Jërëjëf jërëjëf jërëjëfe Boroom Tuubaa
    Jërëjëf hum jërëjëf
    Jërëjëf ndeysaan jërëjëf
    Jërëjëf jërëjëf jërëjëfe Boroom Tuubaa

Комментарии • 215