Aminata Niang Al hamdu lilaahi rabbil Alamiina Jantub diine yaa tiim gaayu gëm yaa Ku mar di nga naan ci gééj leer ya ngi baawaan Al hamdu li Laahi Rabbil aalaminaa Ndégem noo gëm ki Yalla yabal jamana Addina yaa ka mane gan doo nu naxtaan Nu ngiy yaakaar ki nuy mane gane ca Rilwaan Da lay mane gan te gaaw berndeel la gay béén Mu njuuy la nga daanu cim kan rééré ak neen Sagar ak i yax, lu leen geuneu ñaw la dooréé Ku kay beugg miim, bammeel seere ñaaree Bu leen ñétaan, ki addina jay ba dooleel ko Dina wor, dina njuuy, addina maa ka tuumaal Bu leen réyréylu, réy Laahoo ko yelloo Ku réylu ba dee malaaka ya jël la sewloo Ba Baay Laay wootewul dunyaa leudeum na Geureum leen goor gi moo ame leeru diine Ku xam Baay Laay te xam Nabi Laay ne mooma Mahdiyu Nabi Laay a feeñ; moo woote diine Jullitoo wooluleen, sang féñ na Soodaan Ku Yalla yakkal nga suur, na nu jomb xaaraan
Aminata Niang Mbindééf dina xool, di njéér te du gis ngëneel ya Ba Yonnent feegn na ci biir Yoof, noo ngi jaamu Mbindééf a ngi ñuul, te lamboo leeri Yonnent Ba leer yi di tuuru ci gééj, nuy naan ci mbeex mi Ku am xamxam, te ragnéé leeri Yonnent Da nga wara xam ne séydééy jiite yoon wi Sang Soodaan nga, Seydi donay Madiine Bu leen laamlaami, goor gee woote diine Limaamul Mahdiyu Soodaan Yoof la feeñ Wallaay Laahu la soob du danu ko jiiñe Du jang ci tééré, du ci xalimaam, du daa ja Kiñane dafa réy, nde boon ñu ne moo di waa ja Ba Nabi féégné, ca Makka, ba leer ya baawaan Xérém ya tasaaroo, Nabi tere leen bidaa ya Ku geum Nabi,geum Limaamu Rassoulou Laahi Gëlëm dafa réy, nde Kaaba ga, Jammlaahi Ba Njiin feeñé ca Yoof, bañ yay kalaame Ndaxam da ñu réér, nde Yonnent, moom du sankoo Bu doon, ku fi féñ ñu agga fa laaj ko yoon wa Bi Laahi du nu réér, nde sammaan miin na saawa Bu leen ñétaan buuri dunya ki liitam Juddook dee moom ku koy def, Buur du nawleem
Aminata Niang Sikkar sa di riir, bañam ya naan lee mu saankoo Mu naan saabaam ya asal du ma seeru Kongoo Ba Njiin waree gaal bañam ya di ree, jawaanoo Ba saaba ya naan ko Njiin doo teeri bayyi nu Rogogn ya di tuuru, bu doon wurus it di marjaan Ginnaaw jooy yooya, Laahu yaa di Rahmaan Ba gaal ga bañee ca Béér la ñu gëm, jalooréém Ba Kongo belseek Wiirwiir gnoo koy dégg ndéém Xayartu Madiine, Baay Laay, jeul na ndam laa Ku dem Ilayiina, muy jaayook njañam laa Ba Njiin feeñé, la robiney leer ya baawaan Ba rééw mi limbaane, Soodaan dootu naanaan Tanxal nu ci yol mi, yow miy Njool nu naanoo Ba mandi ci leer yi,Baay Laay yaay limbaane Ku langook ñaari yol loo deeti rootaan Da ngaa wara naan, di sangu say bagn di ñéétaan Beuceug la ko Buur ba woo, ba mu réér mbindééf ya Seumbéél ko sa leer ya muy jaayook binnéém ya Bu daa bilibaane, ñuy gaawtook a foofaan Malaaka ya door xéreum ya ñu weesu foofaa Baay Laay woote na, wacc na, moom jotal na Mbindééf yay jaamu, mu tiim leen, seede gëm ya
Aminata Niang Ba gééj sabbaa, Aras yeugou, woor na Baay Laay La seen pexe jeex, tereetu ñu gaa ña Laay Laay Sang da nga taaru, tabe, ku la séén daldi maaree Rafet gaw gaay, xanaa marjaan nga dooree Da nga tabe, muñ, di jambaar, doy nga waaroo Rafet ngab yar xanaa baatin nga dooree Da nga rafetal sa diine ba tey ma woy laa Ku fiy ame diine, Baay Laay jeul na ndam laa Li nuy bon - bon di saw gaay, yaa nu wéétéé Boroom Ridwaan sang bi yaa nu jiitéé Da ñu noon wird ak sikkar dina fey ca sowu Limaamoo woon, te mu nga war gaal di joow Ba pake bay déqi ba pat may xotti mbeex ma Malaaka yaa naan ka Seydeey jiité soodaan Ba tey leer yaa ngi baawaan rééw mi fess na Ñu ngiy laay laay,di roy Baay Laay ci diiné Baay Laay noon na Séydeey jiité gaa ñaa Ku bañ Baay Seydi na nu jox, maa ko wooloo Boroom "Ridwaan", ku la woy naani Tuubaa "Al hamdu li Laahi Rabbil aalaamiinaa" Al hamdu li Laahi Rabbil aalaamiinaa" Sangub jamaanaa ngi, Soodaan woy ko lay jééx.
cherif ousseynou laye yalla na yalla yok ay leram te tassniou ci barkem ablaye fall yalla na yalla mayla weer🙏🙏🙏
Dieuredieuf Ablaye Fall yallah yallah faylen niguen gnouy beguelé!Dieuredieuf Laye Makhtar!
Mamadou Limamou Rassouloulahi amoul mass!
Alhamdoulilahi rabbil Allamina sagam ngo gueum ki Yallah yabal Jamana!
Machalah ablaye fall dieuredieuf limamou lahi moy mamadou cherif sa lérr dou fay baye
🇮🇹🙏💚💙💜💜💛💕💞🙏🇮🇹
Machalla Ablaye fall souniou fierté nga bolé wo dara ak thiakhane
Ablaye Fall Machala momay Fadieu dh billahi 💦Gueum Wolou Yakaar Tai Doylou ❤ Ma beugue Baye Laye
Yalna yalla Werel bate bi
Thieuy Cherif ousseynou yalla na borom bi yokk leeram 🙏🙏🙏❤️❤️❤️😭
amine ya raby 🙏🙏
Machalla yalla na yalla wéral bat bi
Machallah bayou Serigne Ablaye ak Mame Ngane
Machallah laymakhtar Abdoulaye fall
Machalla Laye Makhtar
Machallah laye makhtare
Alhamdoulilah limamou laye moy rassoul
Baye Laye moy Mamadou❤️😍
Machallah ablaye yalna yalla barkel
Macha Allahou Baye Laye Moy Mamadou
Wawaw machallah machallah
Sama xol sedna y'all na yalla werek bate bi
Baracke baye LAYE
Thieuy baye laye amoul masse
yalna yalla goudeul sa fane laye
Sama cherif 😭😭😭❤😍
Machalla laye makhtae
Wayy ablaye fall ya bakh wayy laye makhtar
Chérif sa lerr dou fay
Machallah laye makhtar
ay way coumay dimbali ci numero ablaye fall yalla fayla ci barke baye laye aleyhi salatou wa salame e 🙏🙏
Pv
Diadieufffff laye makhtar alasane ak seyni
Assalamu 3ala Man ataba3a Al HUDA. Peace Ya'll !
Machalla
Baye laye ya bakhe
Bilahi sama xol dafa sed yana refet courél
Billahi Moy momadou
❤💕😭😭😍😍
Ay koumay diapalé si sikar gnio bindeul mako mots yii diap léne si laye makhtar
Aye waye wouyouléne aminata ndakhe mane ite beugeuna ko
Aminata Niang
Al hamdu lilaahi rabbil Alamiina
Jantub diine yaa tiim gaayu gëm yaa Ku mar di nga naan ci gééj leer ya ngi baawaan
Al hamdu li Laahi Rabbil aalaminaa Ndégem noo gëm ki Yalla yabal jamana
Addina yaa ka mane gan doo nu naxtaan Nu ngiy yaakaar ki nuy mane
gane ca Rilwaan
Da lay mane gan te gaaw berndeel la gay béén Mu njuuy la nga daanu cim kan rééré ak neen
Sagar ak i yax, lu leen geuneu ñaw la dooréé Ku kay beugg miim, bammeel seere ñaaree
Bu leen ñétaan, ki addina jay ba dooleel ko Dina wor, dina njuuy, addina maa ka tuumaal
Bu leen réyréylu, réy Laahoo ko yelloo Ku réylu ba dee malaaka ya jël la sewloo
Ba Baay Laay wootewul dunyaa leudeum na Geureum leen goor gi moo ame leeru diine
Ku xam Baay Laay te xam Nabi Laay ne mooma Mahdiyu Nabi Laay a feeñ; moo woote diine
Jullitoo wooluleen, sang féñ na Soodaan Ku Yalla yakkal nga suur, na nu jomb xaaraan
Aminata Niang
Mbindééf dina xool, di njéér te du gis ngëneel ya Ba Yonnent feegn na ci biir Yoof, noo ngi jaamu
Mbindééf a ngi ñuul, te lamboo leeri Yonnent Ba leer yi di tuuru ci gééj, nuy naan ci mbeex mi
Ku am xamxam, te ragnéé leeri Yonnent Da nga wara xam ne séydééy jiite yoon wi
Sang Soodaan nga, Seydi donay Madiine Bu leen laamlaami, goor gee woote diine
Limaamul Mahdiyu Soodaan Yoof la feeñ Wallaay Laahu la soob du danu ko jiiñe
Du jang ci tééré, du ci xalimaam, du daa ja Kiñane dafa réy, nde boon ñu ne moo di waa ja
Ba Nabi féégné, ca Makka, ba leer ya baawaan Xérém ya tasaaroo, Nabi tere leen bidaa ya
Ku geum Nabi,geum Limaamu Rassoulou Laahi Gëlëm dafa réy, nde Kaaba ga, Jammlaahi
Ba Njiin feeñé ca Yoof, bañ yay kalaame Ndaxam da ñu réér, nde Yonnent, moom du sankoo
Bu doon, ku fi féñ ñu agga fa laaj ko yoon wa Bi Laahi du nu réér, nde sammaan miin na saawa
Bu leen ñétaan buuri dunya ki liitam Juddook dee moom ku koy def, Buur du nawleem
Aminata Niang
Sikkar sa di riir, bañam ya naan lee mu saankoo Mu naan saabaam ya asal du ma seeru Kongoo
Ba Njiin waree gaal bañam ya di ree, jawaanoo Ba saaba ya naan ko Njiin doo teeri bayyi nu
Rogogn ya di tuuru, bu doon wurus it di marjaan Ginnaaw jooy yooya, Laahu yaa di Rahmaan
Ba gaal ga bañee ca Béér la ñu gëm, jalooréém Ba Kongo belseek Wiirwiir gnoo koy dégg ndéém
Xayartu Madiine, Baay Laay, jeul na ndam laa Ku dem Ilayiina, muy jaayook njañam laa
Ba Njiin feeñé, la robiney leer ya baawaan Ba rééw mi limbaane, Soodaan dootu naanaan
Tanxal nu ci yol mi, yow miy Njool nu naanoo Ba mandi ci leer yi,Baay Laay yaay limbaane
Ku langook ñaari yol loo deeti rootaan Da ngaa wara naan, di sangu say bagn di ñéétaan
Beuceug la ko Buur ba woo, ba mu réér mbindééf ya Seumbéél ko sa leer ya muy jaayook binnéém ya
Bu daa bilibaane, ñuy gaawtook a foofaan Malaaka ya door xéreum ya ñu weesu foofaa
Baay Laay woote na, wacc na, moom jotal na Mbindééf yay jaamu, mu tiim leen, seede gëm ya
Aminata Niang
Ba gééj sabbaa, Aras yeugou, woor na Baay Laay La seen pexe jeex, tereetu ñu gaa ña Laay Laay
Sang da nga taaru, tabe, ku la séén daldi maaree Rafet gaw gaay, xanaa marjaan nga dooree
Da nga tabe, muñ, di jambaar, doy nga waaroo Rafet ngab yar xanaa baatin nga dooree
Da nga rafetal sa diine ba tey ma woy laa Ku fiy ame diine, Baay Laay jeul na ndam laa
Li nuy bon - bon di saw gaay, yaa nu wéétéé Boroom Ridwaan sang bi yaa nu jiitéé
Da ñu noon wird ak sikkar dina fey ca sowu Limaamoo woon, te mu nga war gaal di joow
Ba pake bay déqi ba pat may xotti mbeex ma Malaaka yaa naan ka Seydeey jiité soodaan
Ba tey leer yaa ngi baawaan rééw mi fess na Ñu ngiy laay laay,di roy Baay Laay ci diiné
Baay Laay noon na Séydeey jiité gaa ñaa Ku bañ Baay Seydi na nu jox, maa ko wooloo
Boroom "Ridwaan", ku la woy naani Tuubaa "Al hamdu li Laahi Rabbil aalaamiinaa"
Al hamdu li Laahi Rabbil aalaamiinaa" Sangub jamaanaa ngi, Soodaan woy ko lay jééx.
🤩🤩🤩🤩🤩
❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤
❤❤❤❤❤❤
💯🙏💯🙏👌
Man mom sant rek lay deff
❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤
Billahi Moy momadou
Machalla Laye Makhtar
Machallah
machallah
❤❤❤❤
❤❤❤❤❤❤❤❤