Teeggi tuuma ci deru jullit ñi { Lislaam xamul luy Terrorisme Diiney jàmm la ak jàmmoo } 2ème partie

Поделиться
HTML-код
  • Опубликовано: 3 дек 2024
  • Serigne Mansour Sall (1940-2021)
    premier khalife de Serigne Abass Sall رضي الله عنهما
    Mi ngi wuutu way juram ci xilaafa gi atum 1990 muy fanweeri at ak benn yumu def ci jàngale ak di yeete gannàaw bamu yeewwo ba nooppi teg ci jëfé lamuy jàngale di ku raañee ku woon ci xam-xam bu sell ànd ak dëggu ak ragal boroomam fu waay musée toog ak moom balaa dem mu ni la ñaanal ma sama ragal yàlla gën di yookku
    Daan na di def fu réew mi toollu te ñu soxla kàaddu diiné ji muy ci wàallu askan wi wala lu jëm ci lislaam mu dox ci wax ci, ci xam-xam bu ñu wooddu ak orma ak ragal yàlla te nit mëssula suufé bamu ni xeeb naa toog ak moom wala di jël xalaatam waaye it àandoon ak fuulla gu toollu ni fu dëgg yàlla jotee ak koo mën ti doon dana lako wax neekkoon ku fòonkoon ñéepp yéené ñépp jàmm te daan dox ngir jullit ñi doon benn bëggóon way juram lool te fòonku ko neekkoon ku jàappu njàamburam keenn mësu ko déegg ci lu xeebu jotaay bu yàlla taxul doo ko fa séen doonoon ku "digne" keenn mënu ko jënd sàammon diinéem ba kenn du ko fowee keenn mënul wóon fexe ba dugal ko ci lu yoonam neekkul
    di ku bëggóon ndaw ñi te yéené léen bëggóon réewam amoon kóollëré neekkoon sufiyàanke bu mag bëggóon seriñam Cheikh Ahmad Tidiane Cherif daa wu ko weeccee ak keenn.
    Di ku gëmóon liggéey te daan ci soonnu lool te utu ci woon lumu am xanaa lumu sàmmee ngoram ak lumu dimbëlee nit ñi mu dëggël li way kat ba wax ci moom
    وتَزْرَعُ الْأَرْضَ فِي كَدٍّ وفِي كَبَدٍ *
    لِيَحْصُدَ النَّاسُ أَطْنانًا وَأَطْنَانًا
    leep di loo xam ni way juram moo ko ci yar. jëlée nañu ci neettali mu ni dakoo mësa woolu biss niko Mansour Damaa soxla woon ku ma abal xaaliss wax ko limu soxla muy lu xawa takku muni ko papa deeñcoon naa luni toollu muni ko indil mako neena bamu ñëwée mu ni ko Mansour nooy làaqee lu toollu nii te jaami yàlla yi di xiif neena mu jël ca lu takku nima def ko fii ak fii ci la jugé lu mu am joxe ko
    *Bu amee benn sikk bu ñu ko xamee mooy mënul woon wax ba àaggal te du dugg ci "tawhiid" maanaam wéetal yàlla
    yàlna yàlla fayal ñu ko moom mi taxoon muy jëf te tàabbal ko aaljanna mu dëkkaleek YONENT bi (SAW) te Saammal ko njaboot gimu fi bàyyi aar leen te dëggël ci ñoom ñaanam ba nga xam ni fumu waxee ba aaggal wax ko te mooy yàlla nañu yàlla téyéel bòoppam.
    Yalna yàlla sàmm kiko fi wuutu di khalifam ak khalifay Serigne Abass Sall Serigne Cheikh Ahmad Tidiane Sall te guddal fanam Amiine

Комментарии • 2