Ma Ibra Laye - Quand je ne serais plus - Coup de coeur

Поделиться
HTML-код
  • Опубликовано: 12 сен 2024
  • Saa bu jàngatee ni nit yi di dundee leegi, dama naan benn mbindeef jarul topp ba mu lay jaral sa diggante ak sa Boroom di ñagas.
    Li ma gënë woor ci sama avenir, te amu ma ci benn sikk-sakk mooy ni bess di na ñëw ma bëgg wax du ma ko mën, ma bëgg yëngu du ma ko mën, ma bëgg lékk duma ko mën, ma bëgg naan duma ko mën, bëgg xam li xéw ci dëkk bi sunu bunt kër sax du ma fa mën teg sama tangk, samay mbokk wër ma te du ñu man ci man dara ludul déngk nagn la Yàlla, samay xarit ak samay soppée wër ma té du ñu man dara ci lima dall, sëriñ ba ma defoon sama kilifa lott ci jappale ma tey ñaan Yàlla ngir mu teggil ma nattu bi, fekk boobu matal na, jeexal naa, waxtuw ñibbi “rendre compte” ci lima fi nekkeewoon rekk moo dess.
    Malaakal mawt wara rocci samak ruuh, mu metti lool bu fekkee samay jëf raffetul woon, walla mu nocci ko ndéem samak ruu sett na.
    Nga gis ñi ma doon nekkal moo xam ay mbokk la walla xarit, ba tax may faat ay waxtu, walla di deff lu néexul Yàlla, daan ma soob ci lu neexul Yàlla, di “prouver” adina ni da ñu am naxxar, da ñu am tiis, da ñu am njaxxaree, waaye du ñu mako “prouver” man. Ndax li doon “prouver” ni da ñu am naxxar mooy séen xell dem ci né maa ngi wara jakkarloo ak gnaari Malaaka yu yéémé ya muy Munkar ak Nakir, ñu war maa laaj, wara “décider” ndax ci mbugal laay dëkkee ba bessub ndekki ba, walla ci bannéex, ñu waroon japp ba sell, jakkarlook Boroom dima ñaanal ngir Yàlla yërëm ma te jeggël ma waaye du ñu ko deff.
    ñu ngay tëdd “aisément”, ñii di naan séen ataya, jigéen yi soll loo xamni séen cërr yepp mo ngi ci biti jël “samay images coller” rongoñ daldi ci bind RIP. “Même” bu fekkoon “Rest In Peace” ñaan gu Yàlla di nangu la sax “pour” ab néew, mbokk yi ñaan dafa am ay worma, waaye tegle say tangk, boole ci déglu music te naan ma RIP boo ciy parée nakk di dellu waat ci sa yëfi adina, mbokk yi “images” yi ngéen di “statut”, farlu ci lool, “montage” bu nekk ngéen deff, ban njariñ lamay amal, “est-ce que” doo léen ko “convertir” defal mako ay ñaan walla ay “ihlâç”.
    Am ñu gënëtee doy waar, ma gennë adina, nga waroon ma sutural, seedel ma lepp lu baax, te nëbb samay ñawtéef, waaye nga jël samay “vidéos” yu ma daan deff lu haram, moo xam ma doon fecc, walla ma doon woy, nga koy “statut” te naan ku baax la woon amul woon benn “problème”, ëy waay suturaal ma té bañ ma dolli ay “problèmes” fa ma nekk.
    ñu war ma jullee, ñii ngi yakkamti seede yi jéex ndax baña “rater” séeni “rendez-vous”, ñii di ñaxtu naan Paa yi da ñu bari wax nañ gaaw dafa am yu ñuy doxi, përëx-përëxee ma yobbu ma sa almeer ya, ma giss nitt yi di “complexer” ci waxal ma “laa ilaaha illal Laah” te “pourtant” bu doon music ñu yuuxu ba séen baat dehh, ma giss ñu war ma jangal “sourate al Ihlâc”, ñii di ko “accélerer comme pas possible”, ma gis ñoo xamni ñom da ñu ko sax jangul nakk, ñu nga melni ay “télespectateur”, paré daldi xëcco bunt ba ngir yakkamti maa wan ginnaaw, waa man, bu ma yaakaree ci ñii ngir texe, fan laa jëm.
    ñu joge fa, daldi dellu sa kër ga, foofu nakk la ñu ma wanee ni fatte nañ la, samay mbokk yi ma waroon ñaanal ndax maa ngi wara tontu jamono jooju ci laaj ya, du ñu ma tall ndax ñu ngay “organiser” dëj bi, di lijjënti lékk yi ak naan yi, ñii ñu ngi lijjënti nu ñu jëlée kaddu ci mbooloo mi ngir puukare ak fësël lu fa waay andi ngir néexal dëjj bi, mères yi di xool ku jaxal ak ku jaxalul, ñii di dajaloo di jëwante ba dima jëw man sax aji dem ji. ñii di laaj ba xam céeb bi and na ak kaani, ñii naan amuma boisson, ñii di lijjënti ku léen tégal ataya, may laaj ndax ñii dañu fatte ni samak dée moo léen fi dajalé, waaye tamit di laaj sama bopp ab dëj ban njariñ lama amal man aji dem ji.
    “Pendant ce temps”, ñu ngay xass Assane ndax li mu nekkoon sama xarit te toogul ci dëj bi, té fekk mooma léen ëppël njariñ fuuf ndax ba mu jogee sa robb ba batay mu ngi kërëm talul lekk talul naan mu nga yorr kurusam sax ci di ma ñaanal.
    Bi ma xamee ni, suma dewee du tee adina di dox ni mu daan doxee, du tee nitt yi fo, du tee ñu caaxaan, te du tee samay mbokk ak samay xarit dellu ci séen “préoccupations”... laa “comprendre” amul benn mbindeef ci kaw suuf bu “mériter” may moy Yàlla ndax moom, ndax ëllëg da ñuy nekk ci lu léen néex man nakk ma wara jakkarloo ak Boroom bu Magg bu kawe bi.
    Kon ak lu mana xéw, na ñu fattaliku ni dara saxul fii, na ñu “FOCUS” ci “allakhira”.
    Yalna Yàlla jubël ñu te saxal ñu ci yoon wa nga xamni war na ci barke Yonnent bi alayhi salatu wa salam.

Комментарии • 18

  • @binetoumansaly9161
    @binetoumansaly9161 11 месяцев назад +1

    Allahou Akbar😢😭😭 yalla na yekh Laye Makhtar🤲 yalla nagnou borom bi dolile goudou fane ak wergui yaram, yalla nagnou borom bi mey moudie gou rafeite🤲♥😢

  • @ndeyeantasamba5898
    @ndeyeantasamba5898 9 месяцев назад

    Mâcha Allah amna solo que Dieu nous pardonne et continue à nous guider sur le droit chemin 🙏🏽📿 Yalla guena tahawou in shaa Allah

  • @bayefallougassama
    @bayefallougassama Год назад

    Yalla nala yalla sammou

  • @diattougningue4517
    @diattougningue4517 Год назад

    Machala laye diadieuf yalna sa boromebi doli hame hame bi si barké lima lahi

  • @aidambenediop5379
    @aidambenediop5379 Год назад

    Amna solo lol macha allah si fi jamano tollou
    Yalla nanou yalla défal dég ak topp

  • @bayefallougassama
    @bayefallougassama Год назад +1

    Vidéo bi dama yé man s fallou GASSAMA

  • @bambadesigner7769
    @bambadesigner7769 Год назад +1

    déé rek mo jara khalat dieureudieuf si fatalé bi yalla sa borom same

    • @moustaphaselane2498
      @moustaphaselane2498 Год назад

      Bilay video bi amneu solo meun sa video chaque jour damakoy prtager sa num rk la sokhla

  • @mouhamedmassyllambaye9877
    @mouhamedmassyllambaye9877 Год назад

    Allahou akbar😭😭😭🥰🥰

  • @vieuxdiallo1371
    @vieuxdiallo1371 Год назад

    Wlhiii🥺🥺💕💕🥰💕💕💕💕💕

  • @ibrahimaseye3883
    @ibrahimaseye3883 8 месяцев назад

    Allahouma amiine

  • @couradiop3863
    @couradiop3863 Год назад

    Mashalla

  • @vieuxdiallo1371
    @vieuxdiallo1371 Год назад

    Amine 💘💘💘💘

  • @bambycamara3253
    @bambycamara3253 Год назад +1

    Quelle vérité que le tout puissant veille sur nous et nous guide sur le droit chemin

  • @bayefallougassama
    @bayefallougassama Год назад

    Biss boma dé fé bakkar vidéo bi rek lasama kél di bémm

  • @warelayembengue365
    @warelayembengue365 Год назад

    ❤❤

  • @GayeNdiaye-ze2re
    @GayeNdiaye-ze2re 4 месяца назад

    😢😢😢

  • @doudoudiop9807
    @doudoudiop9807 Год назад

    😱😭😭😭😱😱😱😱😱😭😭😱😱😱😱😱😭😭😱😱😱😭😭😱😱😭😭😭😱😱😭😭😭😱😱😱😱😱😭😱😱😱😱😭😭😱😱😭😱😱😱😭😭😱😱😭😭😱😱😱😭😭😱😱😱😭😭😱😱😱😱